Bii sàrtu sàmm-suturaa ngi soxal daliweb yu Microsoft, cër yi ak costéef yiy dajale ay njoxe tey doxal yii sàrt, niki cëri ndimbal yi nekkul ci buum gi. Soxalul dali Microsoft yi, cër yi ak costéef yidul wone mbaa yi lëkkaloowul ak bii sàrt mbaa ñu am seen sàrt sàmm-sutura bopp.
Baal nu jàng tënk yi ci suuf te cuq ci "Yeneen leeral" ngir yeneen jàqe ci tëriit bu beru. Mën ngaa tànnee it ci limu costéef yi ci kaw ngir gis sàrti sàmm-suturaab costéef bii. Yenn ci costéef yi, cër yi ak jàqe yees tuddu ci sàrt mën nañoo bañ a am ci ja yépp. Mën ngaa am yeneeni leeral ci dogug Microsoft ngir sàmm sa sutura ci http://www.microsoft.com/privacy.
Yi ëpp ci dal i Microsoft dañuy jëfandikoo ay "kuki yi", muy taxañ i mbind yu ndaw yu ab cëraakonu web man a yër ci lew wi dëxëñ nëbbiit li ci sa tàppaan bu dëgër. Man nanoo jëfandikoo kuki yi it ngir denc say taamu ak say jekkal; jàppalee ci duggsi; indi siiwal-njaay yu ko nduru, ak càmbar jëf i dal bi.
Danuy jefandikoo itam ay ñagi web ngir dimbalee ci seddale kuki yi te dajale cettàntal gi. Yooyu mën nañoo indi yeneen ñagi web, yees tere ñu dajale sa xibaaru bopp.
Am nga jumtukaay yu wuute ngir saytu kuki yi ak xarala yu ni mel, yu deme ni:
Ni nuy Jëfandikoo Nëbbiit yi
Dali Microsoft yu bari dañuy jëfandikoo "kuki", di taxañ yu tuuti yu defi bind yu cëraakoonu web di wàcce ci sa diskdër. Kuki taxañ yu defi bind te cëraakoonu web mën a càmbar ci domen bi la wàcceel kuki bi. Mbind mi dafay nekk yènn say ay nimero aki araf yu tòppànte tay xàmmeloo bènn yòòn sa orninaatër bi, waye ci nòònu mën naa ëmb yénèeni xibaar. Lii misaal la ci mbind muñ def ci ab nëbbiit bu Microsoft def ci sa tappaan booy jëfandikoo benn ci sunuy dali web: E3732CA7E319442F97EA48A170C99801
Man nañoo jëfandikoo nëbbiit yi ngir:
Yenn ci nêbbiit yi nuy faral a yittewoo limees na léen ci rëddiit lii. Lim bii indiwul lépp, waaye dafay junj liy waral nuy amal ay nëbbiit. Soo duggee ci benn ci sunuy dal, dal bi man naa amal yenn ci nëbbiit yii walla yépp:
Cig dolleeku, Microsoft di dina defar yeneen kuki boo dee dugg ci suñuy daliweb, yeneen way sèqal yi dinañu defar itam yènn kuki ci sa disk bu dëgër boo dee dem ci dalu Microsoft yi. Yènn saa yi, likoy waral moy dañuy fasante ak beneen way sèqal mu def yènni cër yi ci suñu tur, lu mel niki càmbar. Yénéensaa yit, dafy tukke ci ne suñuy xëti web yi dañuy am ay ëmbit walla siiwal yu joge feneen, bokk na ci wideo, xibaar ak siiwal yu bawoo ci yeneeni mbootayi siiwal. Walla tamit sa joowu wi lënku ci cëràkònu web yu way sèqal yi ngir wuuti ëmbit yòòyu, te dañuy mëna defar walla jàng sèeni kuki bopp ci sa disk bu dëgër.
Naka lañuy saytoo kuki
Ci misaal, ci Internet Explorer 9, man nga tëye nëbbiit yi boo toppee jéego yii:
Gindi yuy wone nees di tëyee nëbbiit ci yeneen joowukaay jàppandi na ca http://www.allaboutcookies.org/manage-cookies/.
Bàyyil xel ci ni soo tëyee nëbbiit yi, xayna doo man a duggsi walla jëfandikoo man-mani jëflànte yu dali Microsoft aki liggéeyalam yi wékku ci nëbbiit yooyu, te it deesatul man a sàmmoonteek yenn taamuy siiwal-njaay yi wékku ci nëbbiit yooyu.
Ci misal, ak Intenet Explorer 9, di nga mëna raaf kooku boo tòppe jeego yi:
Ay gindi yuy wone nees di faree nëbbiit yi ci yeneen joowukaay yi jàppandi na ca http://www.allaboutcookies.org/manage-cookies/.
Bàyyil xel ci ni soo faree nëbbiit yi, bépp taamu mbaa jekkal bu nëbbiit yooyu doon saytu, niki taamut siiwal-njaay yi, dees na ko far bam set wicc.
Fugluy Joowukaay yu ñeel "Bañ Maa Topp" ak Aarug Toppe. Yenn joowukaay yu yees yi am nañ man-manu "Bañ Maa Topp". Yi ëpp ci man-man yooyu, suñ tàkkee, dañuy yónnee màndarga dal yi ngay dugg ngir wone ni bëggoo ku la topp. Dal yooyu (walla ëmbiit jàmbur ya ne ca dal yooyu) man nañoo wéy di jëlànte ak yaw niki ku lay topp yaakaar ni yaa taamu, moo ngi aju ci sàmm-sutura yu dal bu ci ne.
Internet Explorer 9 ak 10 am nañ man-man bu tudd Aarug Toppe bu lay jàppale ci moytu dal yi ngay dugg di yónnee séen liggéeyandoo yi faram-fàcce yu aju ci sag duggsi fa . Soo yokkee Limu Aarug Toppe, Internet Explorer dina tëye bépp ëmbiitu jàmbur, boole ci nëbbiit yi, yi bawoo ci dal yees lim ngir deesi léen tëye. Ci yamale gi muy yamale woowug yooyu dal, Internet Explorer, dina wàññi leeral yi dali jàmbur yooyu di dajale ñu aju ci yaw. Te soo doxalee ab Limu Aarug Toppe, Internet Explorer dinay yónnee màndargam Bañ Maa Topp walla taamu ci dal yi nga dugg. Dolli ci, ci Internet Explorer 10 di nga man a "fay" walla "taal" al sa bopp DNT, su la neexee. Ngir yéneeni leeral ci Limu Aaru ci Topp ak Bañ Maa Topp, baal ñu nga xool Sartay Sàmm-sutura bu Internet Explorer walla Ndimbëlu Internet Explorer.
Ligeeyuwaayi siiwal yi beru mën nañu maye seen mën-mënu bopp ci dindi ak yeneen tànneef ci mbir yu sore ci siiwal. Ci misaal, tànnefu siiwal ak saytu dindi bu Microsoft jàpandi nañu fa http://choice.live.com/advertisementchoice/. ñu ngi lay bàyiloo xel ne dindi tekkiwoul ñàkka jot siiwal walla di ci gis lu gëna neew, wante, boo dindee, siwal yi ngay jot dootuñu nekk yi ñu tuumaal seeni doxalin. Dolli ci, bañ gi it du tee leeral yi di dem ci sunuy cëraakon, waaye li muy dakkal rekk mooy sosug barab yu lay dàkk ngir siiwal-njaay.
Ni nuy jëfandikoo Web Beacon yi
Xëti web yu Microsoft dafay def nataali elektronig yuñ xame ciy làqiit - lees di woowe neexali benn-piksel - yees man a jëfandikoo ngir joxe ay nëbbiit ci sunuy dal, may nu nuy waññi jëfandikukat yi dugg ci xët yooyu ak joxe liggéeyal yu bokk ñu léen defar. Di nañu mëna boole ci suñuy e-bataaxal wanteer walla lees yi ngir xam ndax bataaxal yi ubbi nañu leen te jëf ci.
Man nanu it liggéey ak yeneen liggéeyuwaay yuy siiwal-njaay ci dali Microsoft ngir def ay làqiit web ci séeni dal walla ci séeni siiwal-njaay ngir may nu nu amal ay jàngati tolluwaay ci naka la bës cib siiwan-njaay ci dalu Microsoft di jeexitale ci njënd walla jeneen jëf ci dalu aji-siiwal-njaay ji.
Li ci mujj, dali Microsoft mënès nañu ëmb ay baliss web yu juge ci yeneen way ligeeyandoo ngir dimballi ñu ci dajale ay jàngat ndax natt baaaxug su ñuy programu wanteer walla yeneeni jëf ci dal wi. Baliis yooyo dina may ñeneen way ligeeyando yi ñu defar di jàng kuki ci sa ordinatër. Da ñuy tere way ligeeyandoo yi ñuy jëfandikoo baliis web ci biir suñuy dal ngir dajale ba jot say xibaari bopp. Waaye mën nga gènn ci njoxe yu dajee yi walla yu yeneen ligeyukaayyu càmbar yi di jëfandikoo ci kow bës lënkalekay ñéel yii joxekatu càambar:
Yeneen Xaral yu Niroo
Ag dolli ci kuki yu ñu xam yi ak baliis web yi, daliweb yi mën nañu jëfandikoo yeneen xarala ngir denc walla jàng taxañu njuréef ci sa ordinaatër bi. Mën nañu ko def ngir saxal say taamu walla yòkku gaawaay ak mbaaxaay dci kow denc yenn taxañ yi fu jege. Wante, mel ni kuki yu siww yi, mënès nako jëriñoo ngir denc màndarga bu amul morom ngir sa ordinatër bi, te mënès nako jëfandikoo ngir topp doxalin. Xarala yooyu dañuy ëmbalae Local Shared Objects (walla "Falaass kuuki") ak Silverlight Application Storage .
Local Shared Objects walla "Falaass kuuki" Web sites that use Adobe Flash technologies may use Local Shared Objects or "Flash cookies" to store data on your computer. Takkal ne sa jagalu joowu wi mënaa saytu walla baña saytu mëna raaf Falaas kuki yi, te ñeel kooki yu ñu ràñee yi ni mu m¨nee soppeeku andak joowu wi. Boo bëggee saytu walla tere Flash kuki, demal ca http://www.macromedia.com/support/documentation/en/flashplayer/help/settings_manager.html.
Silverlight Application Storage. Daliweb walla "application" yuy jëfandikoo xarala bu Microsoft Silverlight mën nañu denc njuref ak Silverlight Application Storage. Boo bëggee jàng naka lañuy saytu walla tere yooyule ndenceef demal Silverlight.
Microsoft day dajale xeeti xibaar yu bari ngir mën di la baaxe, ci lu yemb, ay costéef, ay cër mbaa ay jaar-jaar yu la soxal.
Dinanu dajale xibaar yi boo bindoo, boo duggee mba nga jëfandikoo sunu dal yeek cër yi. Mën nanoo jotee it ay xibaar ci yeneeni këru-liggéey.
Nu ngi dajale bii xibaar ci fànn yu wuute, yu ëmb formileeru web, xaralay kuki, duggiinu web ak jumtuweer yi sa ordinaatëer mbaa yenenn jëfandaay.
Microsoft day dajale xeeti xibaar yu bari ngir mën di la baaxe, ci lu yemb, ay costéef, ay cër mbaa ay jaar-jaar yu la soxal. Lenn ci xibaar bii yaa nu ko baaxe loxook-loxo. Lenn li nu ngi ko jélee ci ni ngay jëflanteek sunu costéef yeek cër yi. Leneen lee ngi juge ci yeneen cosu yu nu booleek ak njuréef yu nu dajaleel sunu bopp. Ci lu ajuwul ci cosu yi, gëm nanu te lu am solo la nu càmbar xibaar bi ak teey te jàppale la nga sàmm sa sutura.
Li nu dajale:
Nunuy dajalee:
Danuy jëfandikoo ab limub pexe ak xarala ngir dajale xibaar yu ñeel ni ngay jëfandikoo sunuy dal ak sunuy cër, niki:
Microsoft dinay jëfandikoo xibaar yi nu dajale ngir jëf, gënal mbaa jëmmal costéef ak liggéeyal yi nuy joxe.
Man nanoo jëfandikoo xibaar yi it ngir jokkoo ak yaw, ci misaal, yëgal la lu aju ci sam sàq ak yeesal i kaarànge.
Ak it daanu man a jëfandikoo xibaar yi dimbandiku ci ngir gën a méngale siiwal-njaay yi nuy wone ci sunuy liggéeyal.
Microsoft dinay jëfandikoo xibaar yi nu dajale ngir jëf, gënal mbaa jëmmal costéef ak liggéeyal yi nuy joxe. Xibaar yees dajalee ci liggéeyalu Microsoft manees na koo boole ak yeneen yees dajalee ci yeneen liggéeyali Microsoft ngir joxe weneen jëflante ak nun wu fi gënati te gën a dëppoo ak say bëgg-bëgg. Man nanu itam dolli ko ci yeneen xibaar yu bawoo ci yeneen liggéeyuwaay. Ci misaal, man nanoo jëfandikoo liggéeyal yu bawoo ci yeneen liggéeyuwaay dimbandiku ci ngir jàpp sa gox ci melo-suuf jaar ko ci sa màkkaanum IP, ngir man a méngale yenn liggéeyal yi ak sa gox.
Dinanu it jëfandikoo xibaar yi ngir jokkook yaw, ci misaal, yégal la sa bindu gu jeex, bàyyi la nga xam bu jokkute kaarànge jàppandee ou bàyyi nga xam boo soxlaa jëf luy tax sa sàq ami yëngu.
Microsoft daa maye jotug lu bari ci sunu dal yi ak cër yi ndax siiwal yi ciy jaar. Ngir jàppandal bu baax yii cër, xibaar yi nuy dajale mën nanu koo jëfandikoo ngir jëmmal siiwal yi ngeen di gis.
Bam dis ni nu ko waxe ci sàrti sàmm-sutura bii, dunu wuññil keneen sa xibaar i jagoo ci lu dul sa ndigël.
Xoolal Yeneen Leerali Sutura yu Solowu yi ngir lu gën a yaatu aju ci kañ lees di man a wuññile sama xibaar, boole ci ñi Microsoft wóolu ak i ndawam; kañ lay laaj wuyu yoon mbaa jëfiinu yoon; ngir xeex njublaŋ mbaa aar sunuy njariñ; mbaa ngir aar ay dund.
Bësal fiingir yeneeni leeral ci séddoo mbaa wuññig xibaar i jagoo:
Yenn ciy cériweb yu Microsoft dinañu la may nga xool te soppi say xibaari bopp yi ci buum gi. Ngir dimbali ci moytu ñeneen di xool say xibaari bopp, fàwwu nga dugg njëkk. Ni ngay jotee say xibaari bopp mi ngi aju ci yan daluweb ak yan cériweb ngay jëfandikoo.
Microsoft.com - Mën nga jot te soppi sa bayaal ci microsoft.com ci Pencum Bayaal bu Microsoft.com.
Microsoft Faktiir ak céri Sàq - Boo amee sàqu Microsoft Faktiir, dinga mën a soppi say xibaar ci daluweb bu Microsoft Peyoor boo cuqee ci lëkkalekaay "Xibaari Bopp" mbaa "Xibaari Faktiir".
Microsoft Lënkoo - Boo bindoo ci Microsoft Lënkoo, dinga mën a jot te soppi say xibaari bopp boo cuqee ci Saytu Sa Bayaalu Lonkoo ci daluwebu Microsoft Lonkoo.
Windows Live - Boo jëfandikoo cëri Windows Live, dinga mën a yeesal say xibaari bayaal, soppi sa baatu-jàll, xool sa Dàkkantal bi jokk a sa firndeg màcc, mbaa nga tëj yenn sàq yi boo demee ci Cëri SàqiWindows Live .
Windows Live Bayaalu Pénc - Boo sosee sàqum pénc ci Windows Live, dinga mën a soppi mbaa far xibaar yi ci sa bayaalu pénc boo demee ci sa bayaalu Windows Live.
Siiwalug Ceet - Boo jëndee siiwalug ceet jaare ko ci Microsoft Siiwal, dinga mën a settantal te soppi sa xibaari bopp ci daluwebu Microsoft adCenter.
Prograamu Liggéeyandowaale yu Microsoft - Boo bindoo ci Prograamu Liggéeyandowaale yu Microsoft, dinga mën a settantal te soppi sa xibaari bopp boo cuqee Saytu sa Sàq ci daluwebu Prograamu Liggéeyandowaale yi.
Xbox - If you are an Xbox LIVE or Xbox.com user, you can view or edit your personal information, including billing and account information, privacy settings, online safety and data sharing preferences by accessing My Xbox on the Xbox 360 console or on the Xbox.com web site. Ngir ami xibaar ci sa sàq tànnal My Xbox, Sàq yi. Ngir yeneeni taamuy xibaaru bopp, tànnal My Xbox, teg ci Bayaal, teg ci Taamuy Kaaràngeg Booom gi.
Zune - Boo amee sàqu Zune mbaa Baatu-jàll bu Zune. Mën ngaa xool te soppi say xibaari bopp ci Zune.net (duggal, jot sa Zune te tag Sama Sàq) mbaa nga jaar ci jumtuweeru Zune (dugg, jot sa tagu Zune, tànn bayaalu Zune.net).
Boo mënul a jot say njogey bopp yu daliwebi mbaa cëriweb yu Microsoft taataanee ci lëkkalekaay yii ci kaw, yooyu dal mbaa cër mën nañu laa jox yeneen pexe yoo jotee say njoge. Mën ngaa jokkook Microsoft ak formileeru webbi. Dinanu toontu sa càkkuteefu jot mbaa far say xibaaru bopp fii ak 30 fan.
Bu dalu Microsoft mbaa ab cëram dajalee ab xibaaru at, day tere jëfandikukat bi ay atam yées 13 mbaa mu jot ndigal ci waajuram mbaa kilifaam laata xale di ko mën a jëfandikoo.
Bunu jotee ndigal, dañuy jëflanteek sàqu xale bi niki yeneen sàq yi, bokk na ci jëflante yi mën di jokkook yeneen jëfandikukat.
Waajur bi mën naa soppi mbaa mu dog ndigal loolu niki nees ko bindee ci sàrt jëfandiku yi.
Bu dalu Microsoft mbaa ab cëram dajalee ab xibaaru at, day tere jëfandikukat bi ay atam yées 13 mbaa mu jot ndigal ci waajuram mbaa kilifaam laata xale di ko mën a jëfandikoo. Dunu laaj cig teyeef xale bu yées 13 at mu joxe yeneen xibaar yu koy tax a jot ci cër yi.
Bunu jotee ndigal, dinañu jëflanteek sàqu xale bi niki yeneen sàq yi. Xale dina mën a jot ci cëri jokkoo yi niki e-bataaxal, bataaxalu-saa ak bataaxlu daluweb te dina mën a jokkoo ci coobareem ak yeneen jëfandikukat yu mu tollooli at.
Waajur yi mën nañoo soppi mbaa far déggoo ya woon te càmbar, soppi mbaa sàkku farug xibaari seen doom. Ci misaal, ci Windows Live, waajur mën naa yër seen Sàq, te cuq ci "Ndigali Waajur".
Li ëpp ci siiwal yu internet yu dal ak cëri Microsoft ñu ngi bawoo ci Microsoft Siiwal. Buñu lay won ay siiwali internet, dañuy teg benn mbaa lu bari ciy koki ngir xàmmee sa ordinaatëer buñu lay won ab siiwal. Lunuy gën a dem, nuy mën di taataan xibaar yu tukkee ci dal yi ñuy siiwalee tey jëfandikoo xibaar yi ngir jàppandal yeneen siiwal yu gën a am solo.
Mën ngaa bañ a jot ay siiwal yu tukke ci Microsoft Siiwal boo demee ci xët bees ko jagleel.
Lu bari ci sunu daluweb yeek cër yi jàppandal nañu ag siiwal.
Li ëpp ci siiwal yu internet yu dal ak cëri Microsoft ñu ngi bawoo ci Microsoft Siiwal. Buñu lay won ay siiwali internet, dañuy teg benn mbaa lu bari ciy koki ngir xàmmee sa ordinaatëer saa yuñu lay won ab siiwal. Ndaxte danuy baaxe ay siiwal ci sunuy daliweb ak ci yoy sunuy liggéeyundoowaale, mën nanu di méngale xibaar yi ak xeetu xët yi, ëmbiit yi ak siiwal yi ngay yër, yaw mbaa ñeneen ñiy jëfandikoo sa ordinaatëer. Bii xibaar dees na ko jëfandikoo ci lu bari, ci misaal, dinanu dimbali ngir nu wérlu ba doo gis benn siiwal bi saa su nekk. Dinanu jëfandikoo it bii xibaar ngir dimbali la nga tànn te wone siiwal yu xejj yu nu yaakaar ne yitteel nañu la.
Mën ngaa bañ a jot ay siiwal yu tukke ci Microsoft Siiwal boo demee ci xët bees ko jagleel. Ngir lu gën a leer ci ni Microsoft Siiwal di dajalee tey jëfandikoo xibaar yi, baal nu yër Sàrti Sutura bu Microsoft Siiwal.
Dinanu may it yeneen këru-liggéey yi, yi ëmb yeneen mbootaayu siiwal, ñuy wone seeni siiwal ci sunu dal yi. Amna saa yu këru-liggéey yooyu di dugal ay kuki ci seen ordinaatëer. Bokk na ci këru-liggéey yooyu lim bii, waaye yemu ci: 24/7 Real Media, adblade, AdConion, AdFusion, Advertising.com, AppNexus, Bane Media, Brand.net, CasaleMedia, Collective Media, InMobi, Interclick, Jumptap, Millennial Media, Nugg.ad AG, Mobclix, Mojiva, SpecificMedia, Tribal Fusion, ValueClick, Where.com, Yahoo!, YuMe, Zumobi. Yooyu këru-liggéey mën nañu laa may pexe mooy bañee kuki yooyu. Mën ngaa am yeneen leeral boo cuqee ci turu këru-liggéey yi ci kaw te topp lëkkalekaay. Lu ëpp ci ñoom bokk nañu it ci mbootaay bu Network Advertising Initiative mbaa bu the Digital Advertising Alliance, di mbootaay yuy joxe pexe yoo bañee siiwal yu tukkee ci ñoom.
Mën ngaa dakkal jébbaleg e-bataaxal waanteer yiy ñëwi te bawoo ci dal ak cëri Microsoft, boo toppee tegtal yi ci e-bataaxal bi nga jot. Ci ajug cër bi nga soxla, mën ngaa am it taamub tànn yu ñeel jotug e-bataaxal waanteer, wootey telefon, ak bataaxalu post ngir yenn dal mbaa cëri Microsoft.
Boo jotee e-bataaxali waanteer yu tukkee ci nun te bëgg a dakkal jot gi, mën nga koo def boo toppee tegtal yi ci bataaxal bii.
Ci ajug cër bi nga soxla, mën ngaa am it taamub tànn yu ñeel jotug e-bataaxal waanteer, wootey telefon, ak bataaxalu post ngir yenn dal mbaa cëri Microsoft boo yëree te duggu ci xët yi toftale:
Tànnéef yii du dog ci siiwal yi ci buum gi: baal nu dem ci xàll bees duppee "Doxalug Siiwal (Bañ ko)" ngir xibaar yu ci jëm. Soxalul jotug jokkolanteg cër yu mënta ñàkk yees jàppee yu bokk ci yoy Microsoft, yooy faral di jot ndaree nga dakkal cër bi.
Sooy jëfandikoo liggéey bu wéeru ci ab barab mbaa man-man, mën nañu yonee Microsoft ay njoxe wër barabu tudal bi jàpandiwul, njoxe Wi-Fi ak njoxe GPS (Global Position System ). Microsoft dafay jëfandikoo ay xibaar ngir joxe liggéey yi ngeen soxla, jëmmal seen xamxamu jëfandikookat te gënal seen costéef ak liggéey ci Microsoft.
Yeen liggéeyi mëna ña laa mey nga saytu saasu ñu yonee mbaa yaatal xibaar ci Microsoft . Ci yeen ka, xibaar barab lu am solo la ci liggéey bi te mëna laaj ñu simpi man-man bi mbaa dakkal liggéey bi ngir mu baña yonee xibaaru barab. Dellul ci jukkib ndimbal bi àndak sa toftal ngir am ay leeral ci nan lañuy fayee man-manu narab yi.
Njoxey Taxawu mooy xibaar yu nuy dajale boo jébbale ab laajub taxawu mbaa boo doxalee jumtukaay buy saafaraal boppam ay tég-téq, yoy bokk na ci xibaar yu ñeel jumtukaayu noste, noste, ak yeneeni jàqe yu lëkkalook téq-téqi taxawu bi,niki: xame mbaa xibaaru xàmmeeku, jëmmalug ayu waxtaan, xibaar yu ñeel anamug masin bi ak jëfekaay bi téq-téq bi bawoo ak ci waxtu lënbët gi, noste ak resistëru njoxe yu ñeel sampi nosukaay yi ak melowalu jumtukaayu noste, ak taxañi topp gagte. Danuy jëfandikoo Njoxey Taxawu nikees ko leeralee ci bii sàrti sutura, rax ci dolli jëfandikoo ko ngir saafara sa téq-téqu tawawu ak ngir aajoy tàggatu.
Taxawu gi mën naa jaar ci telefon, e-bataaxal, mbaa ci waxtaanu internet. Mën nanoo jëfandikoo Jot gu Sorewoo (RA), ak sa doxal, ngir joowandi ci sa ëtt. Jokkalooy telefon, ayi waxtaani internet, mbaa ayi Jot gu Sorewoo ak way-taxawu yi mën nañu koo denc te/mbaa teew lu ko. Ci lu jëm ci, mën ngaa jot it ci wattu bu sa ay jeexee. Budee Waxtaanu Internet mbaa RA, mën ngaa jeexal ab ay saa yu la neexee ci sa coobare.
Booy topp ab téqteg taxawu, mën nanu laa yónnee ab nattukaay ñeel say jaar-jaar ak maye yi. War ngaa tànnee nattukaayi taxawu yu téqaloo ci yeneeni jokkoo yu Microsoft baaxe, boo jokkoo Way-taxawu yi mbaa ngaa jaare ko ci tànku e-bataaxal bi.
Ngir toppaat te soppi say xibaari bopp yi ñu dajalee ak sunuy cëri taxawu, baal nu jokkook nun ak sunu Formileeru Web .
Yenn kilyaanu yaxantu mën nanoo ay njaayu taxawu yees gënaleel (malasan Njiitu Jëwriñ yi, a.ñ.s.). Njaay yooyu ngi aju ci seeni sàrt ak yégley bopp.
Njoxey Fay mooy leeral yi ngay joxe sooy jënd ci-net bi . Sa nimero fay man na cee ànd (misaal,kàrtu keredi, PayPal), sa tur ak sa màkkaanu faktiir, ak kotu kaarànge bi ànd ak sa gindiy fay (e.g., CSV walla CVV bi). Bii wàll day jàppandil yeneeni xibaar yu jëm ci ndajale bi ak jëfandikug sa jumtukaayu peyoor.
Njoxey Fay mooy leeral yi ngay joxe sooy jënd ci-net bi . Sa nimero fay man na cee ànd (e.g.,kàrtu keredi, PayPal), sa tur ak sa màkkaanu faktiir, ak kotu kaarànge bi ànd ak sa gindiy fay (e.g., CSV walla CVV bi). Bii wàll day jàppandil yeneeni xibaar yu jëm ci ndajale bi ak jëfandikug sa jumtukaayu peyoor.
Njoxey Fay dees na ko jëfandikoo ngir matal sa njënd, niki jàpp ak fàggu ak moytu luubal. Ak yii jëfandiku, Microsoft mën naa séddoo Njoxey Fayak ay bànk ak yeneen liggéeyuwaay yuy càmbar ay peyoor, ak ngir moytu luubal te wàññi rëccaleg bor.
Soo joxee Njoxey Fay te fekk nga dugge ak sa sàqum Microsoft walla sag nose, daanu denc njoxe yooyu ngir y^mbal mottalig jëndante yiy ñëwi.
War ngaa yeesal mbaa far sa xibaaru jumtukaayu peyoor bi lëkkalook sa sàqu Microsoft boo duggee ci https://commerce.microsoft.com. War ngaa far xibaaru jumtukaayu peyoor bi lëkkalook sa sàqu mbootaay boo jokkook Kurélu Jàppale Jëfandikukat yi . Gannaaw boo tëjee sa sàq mbaa nga far ab jumtukaayu peyoor, Microsoft mën naa tée sa njoxey jumtukaayu peyoor diir bu mu laaj ngir mottali sa njënd te moytu luubal.
Sàqu Microsoft (ñu gën koo xamee ci Windows Live ID ak Paaspooru Microsoft) ab cër la bu lay may nga duggu ci costéef yu Microsoft yi, dal yi ak cër yi, niki yoy Liggéeyandoowaaley Microsoft yi. Boo sosee ab sàqu Microsoft, dinanu la laaj nga joxe yenn ciy xibaar. Boo duggee cib dal mbaa cër ak sa sàqu Microsoft, danuy dajale yenn xibaar ngir leerlu ci sa jëmm ci turu dal bi mbaa cërr bi, ngir aar la ci jëfandikug sàq wu bon, ak aar xarala ak kaaràngeg cëru sàqi Microsoft. Dinanu it yónnee yenn xibaar ci ab dal mbaa cër boo duggee sa sàqu Microsoft.
Ngir gis yeneen jàqe yu ñeel sàqu Microsoft, yoy bokk na ci ni ñuy sosee ak jëfandikoo ab sàqu Microsoft, niñuy soppi xibaari sàq, ak niñuy dajalee te jëfandikoo xibaar yu lëkkalook sàqu Microsoft, baal nu cuq ci Am lu gën a leer.
Sàqu Microsoft (ñu gën koo xamee ci Windows Live ID ak Paaspooru Microsoft) ab cër la bu lay may nga duggu ci costéef yu Microsoft yi, dal yi ak cër yi, niki yoy Liggéeyandoowaaley Microsoft yi. Ëmbaale na costéef, daluweb ak I liggéeyal niki yii:
Sos ab sàqu Microsoft.
Mën ngaa sosee ab sàqu Microsoft fii boo joxee ab m-bataaxal, ab baatu-jàll ak yeneen "firndey sàq", niki ab m-bataaxalu wuutu, ab nimero telefon, ak ab laaj akub toontu. Dinanu jëfandikoo say "firndey sàq" ngir mbiri kiiraay kepp - masalan, ngir wérlu ci sa jëm ci jamono joo mënul a jot sa sàq Microsoft te bëgg ndimbal, mbaa ngir amalaat sa baatu-jàll boo mënul a jot ci sa m-bataaxal bi taqook sa sàqu Microsoft. Yenn cër yi mën naa laaj yeneen kiiraay, te ci yu ni mel, mën nanu laa laaj nga sos beneen caabi kaarànge. M-bataaxal ak baatu-jàll bi nga jëfandikoo ngir bindu ci sàqu Microsoft ñooy say "màndarga" yooy jëfandikoo ngir xàmmeku ci sunu mbaal. Rax-ci-dolli, dinañ boole ci sa màndarga benn limu Dàkkantal bu 64-okte bob dees na ko jëfandikoo ngir xàmme say màndarga ak xibaar yi ñu lëkkalool.
Boo sosee ab sàqu Microsoft, dinanu la laaj nga joxe xibaaru tolluwaay bii topp: gender; réew; taarixu-juddu; ak kotu post. Mën nanoo jëfandikoo taarixu-juddu bi ngir wérlu ne xale yaa ngi jot mbir yu jaadu tukke cib waajur mbaa wattukat ngir jëfandikoo sàqu Microsoft, ni niko yoonu gox ba laajee. Rax-ci-dolli, sunu nosteg siiwalu internet dina ko jëfandikoo ngir baaxe la siiwal yu la dëppoo ñeel ay coste ak i cër yu la amal njariñ, waaye sunu nosteg siiwal du mës a jël sa tur mbaa say xibaari sàq. Ci weneen waxin, sunu nosteg siiwal bi amul te du jëfandikoo xibaar yu lay tax a ràññee (niki sa tur, sa m-bataaxal ak sa nimero telefon). Boo taamoo bañ a jot siiwaal yees jëmmal, mën ngaa bind say taamu ci sàqu Microsoft boo demee ci mii xët, bu ko defee saa yoo duggee ciy daliweb mbaa cër ak sa sàqu Microsoft, sunu nosteg siiwal du la baaxee ay siiwal yees jëmmal. Ngir lu gën a leer ñeel ni Microsoft di jëfandikoo xibaari siiwal yi, baal nu yër Mottalig Sàmm-sutura nu Microsoft Siiwal.
Mën ngaa jëfandikooab m-bataaxal bu Microsoft (niki yu jeexee live.com, hotmail.com, mbaa msn.com) mbaa ab m-bataaxal bu ñeneen (niki bu jexee gmail.com mbaa yahoo.com) booy bindu ngir am sàqu Microsoft.
Booy sos ab sàqu Microsoft, dinanu la yónnee ab e-bataaxal bu lay laaj nga wérlu ne yaay boroom m-bataaxal bi lëkkalook sa sàqu Microsoft. Dees koo def rekk ngir leerlu ci wérug m-bataaxal bi te dimbali la ci feggu ci m-bataaxal yees di jëfandikoo te boroom amu ci ndigël. Ginnaaw bi, dinanu jëfandikoo m-bataaxal bi ngir yónnee la jokkoo yu lëkkalooo ak sa jëfandikooy costéef ak cëri Microsoft; mën nanu laa yónnee it ay e-bataaxali wànteer ñeel costéef ak cëri Microsoft niko sa yoon dëkk mayee. Ngir xibaar yu ñeel saytu sa jotug jokkooy wànteer, baal nu yër Jokkoo yi.
Booy jéem a bindu cib sàqu Microsoft te gis ne keneen jël na sa xàmmekaay bi ànd ak sa m-bataaxal niki turu jëfandiku bi, mën ngaa jokkook nun te laaj keneen ki mu jël tur bu uute ngir nga mën a jëfandikoo sa m-bataaxal booy sos say dàkkantal.
Dugg ci jumtuweer yi, dal yi mbaa cër yi ak sa sàqu Microsoft.
Boo duggee cib dal mbaa cër ak sa sàqu Microsoft, danuy dajale yenn xibaar ngir leerlu ci sa jëmm ci turu dal bi mbaa cërr bi, ngir aar la ci jëfandikug sàq wu bon, ak aar xarala ak kaaràngeg cëru sàqi Microsoft. Ci misaal, boo duggee,cëru sàqu Microsoft day jot te denc say xàmmeekay ak yeneen xibaar, niki bennub lim bu 64 okte bees booleek say xàmmeekaay, sa adrees IP, sa sottib joowukaayu web ak ab waxtu akub taarix. Teg ci, boo jëfandikoo ab sàqu Microsoft ngir dugg cim jëfandaay mbaa cim jumtuweer bees samp cim jëfandaay, bennam Dàkkantal bees tandu lañuy jagleel jëfandaay bi; boobu bennam Dàkkantal bees tandu dañu koy yónnee niki pàccu say xàmmeekaay ci cëru sàqu Microsoft booy duggaat ci dal mbaa cër ak sa sàqu Microsoft. Cëru sàqu Microsoft moo yónnee xibaar bi topp ci dal mbaa cër bi nga duggee: bennam limu Dàkkantal buy may dal mbaa cër bi mu xam ndax kenn nga ak ki mujj a dugg; sottib lim bees jagleel sa sàq (lim bu bees lees di jël saa yoo soppee say xibaaru dugg); ndax sa m-bataaxal firndéel nañu ko; ak fayu ñu sa sàq.
Yeneeni dal ak cër yu la may nga dugg ak sa sàqu Microsoft danañu soxla sa m-bataaxal ngir jàppandal la seeni cër. Ci yuni demee, boo duggee, Microsoft dina joxe sa m-bataaxal waaye du joxe sa baatu-jàll dal bi mbaa cër bi. Teewul, boo sosee say xàmmekaay ak dal bi mbaa cër bi, mën nañu laa yemale ci jot xibaar yi lëkkalook say xàmmekaay ngir dimbali la nga amalaat sa baatu-jàll mbaa joxe yeneen cëri ndimbal.
Boo jotee sa sàq ci feneen, niki ab lekkool, ab ja, ab jàppandalkatu cëru internet, mbaa saytukatub domen, mën naa am say sañ-sañ ci sa sàq, yoy bokk na ci mën a amalaat sa baatu-jàll, xool ni ngay jëfandikoo sa sàq mbaa say njoxey bayaal, jàng mbaa defaraat sa ëmbiitu sàq, te aj mbaa neenal sa sàq. Bu ni demee, yaa ngi tënku ci Déggooy Cëri Microsoft ak béppsàrti jëfandikoo bu ñeel ñooñu. Boo doonee aji-saytub domen te jox say jëfandikukat sàqi Microsoft, yaa gàddu àq bépp yëngu yu bawoo ci sàq yooyu.
Baal nu nga xam ne dal yeek cër yi la may nga dugg ak sa sàqu Microsoft, mën nanoo jëfandikoo mbaa seddoo sa m-bataaxal mbaa sa yeneen xibaari bopp yi nga leen jox nees ko bindee ci sàrti sàmm-sutura yi. Teewul, mën nañoo seddoo bennam limu Dàkkantal bi leen cëru sàqu Microsoft jox ngir sottal cër mbaa njaay moo fa def. Bépp dal mbaa cër buy jëfandikoo sàqu Microsoft soxla naa am sàrtu Sàmm-sutura, waaye dunu fuglu ni dal yooyu di doxalee, te seen doxalin wuute na. War ngaa càmbar bu baax sàrti sàmm-suturab dal bu nekk ngir xam ni dal bu nekk di jëfandikoo xibaar yi muy dajale.
Mën nga jot say xibaari bopp boo demee ci sàq. Man ngaa soppi sa dàkkantal bu dee sa sàqum Microsoft bokkul ci domen yees saytu. Mën nga, saa yu la soobee, soppi sa baatu-jàll, sa m-bataaxalu wuutu, sa nimero telefon, ak sa laaj ak sa tootub sutura. Mën nga it tëj sa sàqu Microsoft boo demee ci sa sàq, ci "Tëj sa sàq." Bu sa sàq nekkee ci domen bees saytu, nikees ko leeralee ci kaw, mën naa am yoonu jagle ngir tëj sa sàq. Jàppal ne booy jëfandikoo MSN mbaa Windows Live, boo demee ci sa sàq, mën nañu laa jéll ci sàqu yooyu dal.
Yeneen xibaar yu ñeel sàqu Microsoft jàppandina ci dalu sàqu Microsoft.
Yeneen leeral yu aju ci
Gisa yeneen leeral yu aju ci sutura ci suuf yu la man a amal solo. Li ëpp ci lii dafay xamle lees baaxoo def nu bëgg nga xam ko waaye jàppu nu ni mant a ñàkk ngir fésal ci sunu bépp béralug sàmm-sutura. Lenn ci lii lol xayna mu nekk rekk la (ci misaal, daanuy wuññi leeral su ko yoon sàkkoo ), waaye teewul sunuy layalkat waxloo nu ko. Bàyyil xel ci ni leeral yii xame sunuw doxaliin lépp - lii dafa bokk ci dolli ci yeneen leeral yees xamle ci béralug sàmm-sutura bu costéef ak liggéeyalu Microsoft booy jëfandikoo bu ci ne.
Ci bii xët:
Séddoo walla Wuññig Leeralu Jagoo
Dolli ci séddoo gees xamle ci beral gi ñeel coste ak liggéeyal yi ngay jëfandikoo, Microsoft man naa séddoo walla wuññi leerali jagoo:
Man nanoo séddoo walla wuññi leerali jagoo, niki ëmbiiti say jokkoo:
Bàyyil xel ci ni sunuy dal man naa defaale lëkkalekaay yu jëm ci dali jàmbur yoy séen doxaliinu sàmm-sutura man naa wuute ak yoy Microsoft. Soo dugalee leerali jagoo ci benn ci yooyu dal, say leeral yooyu ya béralug sàmm-sutura bu dal yooyu lay tegu. Noo ngi lay ñaax ci dal boo duggati rekk nga yër séen beralug sàmm-sutura.
Aar Kaaràngeg Leerali Jagoo
Microsoft gàlloo naa aar kaaràngeg sa leeral jagoo. Daanuy jëfandikoo xaralay kaarànge yu wuute aki defiin ngir aar sa leerali jagoo ba kuñ ko mayul du ci jot, jëfandikoo walla di ko wuññi. Ci misaal, sa leerali jagoo yi nga nu jox ci nostey nosukaay yuñ yamale séenug jot léen koy def te sunuy ndaw dëkke koo sàmm. Bu nuy yónnee leeral yi gën a laaj sutura (niki nimero kàrtu keredi ak baatu-jàll) ci Internet, daanu ko aar ak xaralag ndëxëñ, niki bindiitu Secure Socket Layer (SSL).
Baatu-jàll lees di aare say sàq ak sa leeral jagoo, kon nag yaw la war nga deñ ko ci kumpa. Bul ko wax kenn. Bu dee nosukaay gi danga koo bokk ak keneen, li gën mooy saa soo noppee nga lonkiku balaa ngay génn dal walla liggéeyal bi ngir moytu beneen jëfandikukat di jot say leeral.
Fees di def leeral ak nees koy jëfandikoo
Leerali jagoo yees di jële ci dal ak liggéeyali Microsoft dees na ko denc ci Diiwaan-Yu-Bennoo yi walla ci meneen réew mu Microsoft walla benn ciy bànqaasam,, joxekati liggéeyalam nekk. Microsoft joxna gëdd U.S.-EU Safe Harbor Framework ak U.S.-Swiss Safe Harbor Framework ci niko U.S. Department of Commerce tëralee ci lu àju ci takk, jëfandikoo ak téye njoxe ci European Economic Area ak Switzerland. Ngir am yeneeni leeral ci tërinu Safe Harbor t egis sa seede, yëral http://www.export.gov/safeharbor/.
Niki xaaj ci bokkug Microsoft ci têraliinu Safe Harbor, daanuy jëfandikoo TRUSTe, di moomeel gu jàmburu, ngir àtte bépp jafe-jafe boo am ak nun mu aju ci sunuy sàrt ak sunuy doxaliin. Soo bëggee jokkook TRUSTe, man ngaa dem https://feedback-form.truste.com/watchdog/request.
Microsoft man naa tëye leerali jagoo ngir mbir yu bari, niki ngir dëppoo ak sunu wareef ak yoon, saafara xuloo, dooleel sunuy déggoo, ak yeneen yu man a jariñ. Ngir yeneen leeral ci nees di jote sa leerali jagoo, demal ci Jotug Say Leeral.
Coppite yi ci sunu Bérali Sàmm-sutura
Daanuy faral a yeesal sunu béralug sàmm-sutura ngir gën koo dêppale ak xalaati way-jëflànte yi ak coppite yi am ci sunuy liggéeyal. Sunu dugalee ay coppite ci ag béral, daanu def bis bees ko "mujjee yeesal" ci kaw béral gi. Su amee coppitey jumtukaay ci béral gi walla ci ni Microsoft di jëfandikoo sa leerali jagoo, daanu la ko yëgal jaar ko ci dugal ab yëgleb coppite yooyu balaa nu koy doxal walla sax nu yónnee la bataaxal. Noo ngi lay ñaax ngay faral a xoolaat beralug sàmm-sutura yi ñeel costéef ak liggéeyal yi ngay jëfandikoo ngir xam nu Microsoft di sàmme say leeral.
Nees di Jokkook nun
Microsoft Privacy, Microsoft Corporation, One Microsoft Way, Redmond, Washington 98052 USA
Ngir ngir bànqaasu Microsoft bi ne ci sa réew walla gox, demal http://www.microsoft.com/worldwide/.
Pexey Sàmm-sutura yu FTC
Kaarànge ca kër ga
Trustworthy Computing